Lyrics: Oumar Pene/Abdou Fatha Seck Music: Hervé Samb Lu tax lu tax Lu tax lu tax Lu tax lu tax
Du dëgg, du yoon Nga koy waxal xam nga ni loolu defa ñaaw’a ñaaw
Li ngay wax si moom amu loo lu la wo wóor Aw wax rekk la loo cay wax ? xam’u ma ko Kii ngay waxal moom mi ngi jàpp yoonal di dem Yëgu la xamul ni sax yaa ngi wax si moom Yaa ngi am jot di wax si moom lu nekk’ul
Xoolal wërsëgu jaambur gatandu ko di na diis
Daas sa lammiñ ba mu ñaw Jam sa moroom baatu ginnaaw saqami wax ju ñaaw ni ko tëf si kawam muy law ki ngay tooge xamaloo ko lu dul degg naa Jikkóoy cannibale la ngi ci ñun dundee deru nit ki di jëw
Lu tax lu tax Lu tax lu tax Lu tax lu tax
Lu tax ngay wax lu amul ? Lu tax ngay wax lu nekkul ? Lu tax ngay wax lu la wóorul ? Loolu amoo ca yoon Bu ñu ko wëlbati woon jox la ko di na diis waxal jàmm waxal lu lo wóor
xam nga ni bu la dara jaral ngay yàq ki la tane Royal si faydaam ba yokk ca’a gëna wóor
kiy maye li mu yor du jeex
Buur Yàlla faale woo gaañu gaañu gëna xóot deram ji nga tilimël ani ku koy fóot ? maandute japp rang gi laay seet
Hee mani wax ma foo féete su nu xeet ?
Lu tax ngay wax ci moom lu ñaaw’a ñaaw Lu tax ngay dem di wax ni nit ki faatu na ? lu tax ? Yow wóoru la ngay wax si moom lu amul Lu tax ? li mu la jaral amul peyoor
Lu tax Li nga lëndëmël yow doo ko leeral ?
lu tax nga nàmp jëw ? Kañ ngay feral ?
Lu tax yéene woo ko li nga yéene sa jëmm jii ?
Lu tax yow demu loo te baayi woo ku dem